Sellaayu Yeesu 1

Telecharger l’emission en cliquant à droite ici

Téereb Injiil di Kàddug Yàlla mu ne, “Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya. Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm. Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi. Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.”