Archives mensuelles : juin 2015
Yàlla Mbëggeel la
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Téereb Injiil di Kàddug Yàlla mu ne : Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
Tuubum Bàkkaar 2
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Téereb Injiil di Kàddug Yàlla mu ne : Ca jamono yu wees ya Yàlla toppul ñàkka xam googa, waaye léegi koo mana doon ak foo mana nekk, Yàlla santaane na, nga tuub say bàkkaar. 31 Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn ; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya. »
Tuubum Bàkkaar 1
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Téereb Injiil di Kàddug Yàlla mu ne, Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirumwaa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal léen Yàlla. Mu ne léen: « Mbaa du dangeena xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gëna nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj ? 3 Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.