Tuubum Bàkkaar 1

Telecharger l’emission en cliquant à droite ici

Téereb Injiil di Kàddug Yàlla mu ne, Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirumwaa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal léen Yàlla. Mu ne léen: « Mbaa du dangeena xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gëna nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj ? 3 Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.

Laisser un commentaire