Ay Njàngalee Yeesu 1

Telecharger l’emission en cliquant à droite ici

Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog ; taalibeem ya ñëw ci moom. Mu daldi léen jàngal naan : Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol. Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina. Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg.

Laisser un commentaire