Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Seydina Isaa Almasi bi, Yeesu Kirist mu ne, « Dégg ngeen ne waxoon nañu : “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal, ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.»