Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Archives de catégorie : Njàngalee Seydina Isaa Almasi Bi
Ay Njàngalee Yeesu 3
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Seydina Isaa Almasi bi, Yeesu Kirist mu ne, « Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw.»
Ay Njàngalee Yeesu 2
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Seydina Isaa Almasi bi, Yeesu Kirist mu ne, « Dégg ngeen ne waxoon nañu : “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal, ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.»
Ay Njàngalee Yeesu 1
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog ; taalibeem ya ñëw ci moom. Mu daldi léen jàngal naan : Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol. Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina. Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg.
Ñam wiy Joxe Dund
Telecharger l’emission en cliquant à droite ici
Seydina Isaa Almasi bi, Yeesu Kirist mu ne « Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk ; te ku ma gëm, doo mar. »