Ay Njàngalee Yeesu 2

Telecharger l’emission en cliquant à droite ici

Seydina Isaa Almasi bi, Yeesu Kirist mu ne, « Dégg ngeen ne waxoon nañu : “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal, ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.»

Ay Njàngalee Yeesu 1

Telecharger l’emission en cliquant à droite ici

Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog ; taalibeem ya ñëw ci moom. Mu daldi léen jàngal naan : Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol. Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina. Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg.

Kéemaanu Yeesu

Telecharger l’emission en cliquant à droite ici

Seydina Isaa Almasi bi, Yeesu Kirist mu ne ay taalibee yonent Yaxya,« Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, *gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi. Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga. »

Un programme radiophonique sur les Saintes Ecritures